LOU TEUGUE TASS

Boris ARNOUX, Damien COUTROT, Fabien GIROUD, Jean paul SY, Julien SOULETIE

Lu tëgg tas ci life bi!
Lu tëgg tas ci life bi!

My broda lepp luñu waxantewoon, lepp liñu digaalewoon
lepp liñu yeenantewoon leegi jeex na, leegi dem nga!
My sistren man ag yaw du kan moo tooñ, Buur bi Yallaa ñu boolewoon, melna ni bokkatu ñu yoon leegi jeex na, leegi dem na, namm naa la!

Lu tëgg tas, lu tëgg tas, maa lako wax lu tëgg tas
Amna fo xamantene buñ fa nare yeeg man ma waaf
jàppal sa Pa, jàppal sa Ma, kudul sa waay yaw nang ko taf
ki la bëg dina la jàpp, ku la bëgul bumla saf
Leeg-leeg nga gestu do gis kenn,
sa xol bi jeex nga naqarlu te doo ko mën wax fenn
Te lu dul dëgg di ay fen
te waruñu toog di tappale
te waruñu doon keneen
My broda lepp luñu waxantewoon, lepp liñu digaalewoon
lepp liñu yeenantewoon leegi jeex na, leegi dem nga!
My sistren man ag yaw du kan moo tooñ, Buur bi Yallaa ñu boolewoon, melna ni bokkatu ñu yoon leegi jeex na, leegi dem na, namm naa la!

Nañu ànd ci bamu jotee, numu gëna rafetee
wayé tàqaliku bu jotee buñu kenn gëna gore
Nañu ànd ci bamu jotee, numu gëna rafetee
waye tàqaliku bu jotee buñu kenn gëna gore
Àdduna nii la, demal maa ngi ñëw la,
ànd bu yaag sax day jeex wante loolu bumu la jaaxal
Kii la wala kee la, yaw ki la Yalla booleel fexeel ba moom dula raw
Siggi naa ni wóoy, siggi naa ni naa ni wóoy
mais fils, duma la fenn, leeg-leeg sama xol day boy
damay triste te duma xam man mi li may taxa jooy
buko defee sama xel day dem ci God, ci family ag samay waay

My broda lepp luñu waxantewoon, lepp liñu digaalewoon
lepp liñu yeenantewoon leegi jeex na, leegi dem nga!
My sistren man ag yaw du kan moo tooñ, Buur bi Yallaa ñu boolewoon, melna ni bokkatu ñu yoon leegi jeex na, leegi dem na, namm naa la!

Suma la tooñee nang ma baal, ndax dara jaruko fi
Yaw booma tooñee naa la baal, ñun dañu fee gane si
Budee jàmm rek a la taxa jog, bul ragal dellusil
Da nguay toog ag nit bamu yaag bes ñu ne la nekkatu fi
Wër nga aduna, loolu bumu la taxa change
Say mbokk ñooy sa doole, bo leen ñàkkee yaa ngi ci danger
Yalla mi ñu sàkk ñun ñëpp la fi nekkal
kon tàqaliku bu jotee kune na jël ay dëbësam

Lu tëgg tas, lu tëgg tas, lu tëgg tas, lu tëgg tas!
Lu tëgg tas, lu tëgg tas, lu tëgg tas, lu tëgg tas!

Most popular songs of Natty Jean

Other artists of African reggae